Текст песни Youssou N'Dour - Xale/Our Young People
No no no no
No, no no no no
Ne xale bi
Bëgguma la mer loo
Ne xale bi
Bëgguma la mer loo
Ndaxte soo meree
Soo meree
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma
(Bul ma meree)
Lu menul ñàkk
Faw dafay am
Wareef dafay mat
Léeg-léeg mu doon lu dul neex
Yow sama doom
Suba tax may wax
Soo magee dinga xam
Ndaxte soo jooyee
Soo jooyee
Sama yaram daw
Daw ba jaaxal ma
Waa-jur ak doom
Faw ñuy waxtaan
Feexee mel ni mburu ak sow
Ndem réeru mën ta* ñàkk
Ni jamono mel
Teey da cee baax
Jubbantil ba mu cor
Ndax muumin dafay rooy